Proverbes Wolof

 

 

Guy dana jur i dég.
Il arrive qu’un baobab ait des épines.

 

Picc mu masula naaw, su naawee firim rééw.
L’oiseau qui n’a jamais volé, le jour où il vole, il fait le tour du pays.

 

Su may dee ci àll, gayndee may rey.
Si je dois mourir dans la brousse, que ce soit le lion qui me tue.

 

Ganaar du am faru siiru.
La poule ne doit pas avoir pour fiancé un chat sauvage.

 

Bakkan waruw dàll la : fa muy dagge dooko yëg.
La vie c’est comme une lanière de sandale : avant qu’elle ne soit rompue, on ne peut pas savoir où cela va se produire

 

Bëtub mbëggeel jéll nab gàkk.
Le regard de l’amour passe par-dessus les défauts.

 

Lu waay rindi ci sa loxo lay naac
Tôt ou tard dans la vie nos faits et gestes nous rattrapent

 

Jégué atayakat taxuta njakka naan
Etre proche de celui qui fait le thé ne fait pas qu’on soit le premier à boire

 

Jikko dana soppiku jaan walbatiku màtt boroom ba.
Le caractère, ça peut se changer en serpent, se retourner et mordre son maître.

 

Dëgg kaani la, ku ñu ko xëpp nga toxoñu.
La vérité c’est du piment, si on te la jette à la face, tu te frottes les yeux.